vendredi 27 juillet 2012

[SUITE 5] PRECHE DU JOUR … « Les effets subliminaux des nouvelles religions et croyances et les enjeux d'une émancipation mentale en Afrique - par Pofrima Selo


JOGE SI ÑAKK WAXTAAN JËM SI JOKKALANTE 
CI MBIRUM DIINE AK BEPP NGËM NGËM

Dama fasyéene wane, ci biir ndaje mi ñu tudde « Katholikentag » tey am ci dëkk bi ñu duppée Mannheim, ci Almaañ, digante  16 ba 20 ci weeru me, sama ay liggéey ci wàllu caada. Loolo ngi wara xewe ci bereb bu ñu naan « Raum der Stille und des Gebetes im Zentrum des christlich-islamischen Dialogs », berebu dal ag ñaan la bu ñu mana ménggale ag yi ñuy gis ci aydapoor yu mag yi.
Li ma nàmm ci mbir bi mi mooy biral jokkalante bi te diko jaarale ci li Senegal wane ci wàll woowu. Ndax lu ëpp ci li may wane maa ngi ko sosee Senegal, ci diggante 1993 ba 1995. Ñareeli pàccu wane weengi taftalu ci li may sos ci jamano jii ci wàllu jokkalante bi ci digante diine yi. Damay duggaat ci soseeli  xel  yu jëkk  ya yu doomu Aadama, ca jamanoy mamaati maam ba ci yu sunu joonu yàlla. Li ma ci bëgg, fi itam, mooy wane ab xeetu jokkalante (bu nu yëg ag bu nu yëgul) jamano yooyu ba léegi, ci digante askanu àddina bépp . Mbirmi dëg-dëg mooy gëstu màndargayeeg feeñeelu diine yu wuute yi ngir wane digante doomu Aadamaag mbiri baatinam. Dama bëg, ci loolu, woote jëmale ci kune weg sa morom ci wàllu ngëm- ngëmam ag diineem. 

Li am solo ci doxalin woowu, ci sama gis-gis, moy dindi bepp xeetu nooteelu xalaat ci jokkalante bi , maanaam di fexe ba ken du fesal sa bopp ci mbir mi. Ndax bu ñu bàyyee suñu xel ci li waral jokkalante bi, dina ñu gis ne ndono bu ñu bokk la… moomeelu doomu Aadama yëp la, ñu koy wane te di ko nekkal ba àdduna sosoo ba léegui… ci ay kuréel wàlla ci nu ko waay man defe.


Pàppa Umar Faal
Njiitu mbootaay bi nuy duppe SEMEtt
http://www.styloculture.org/wolof/bakkusemettcitekkiinuseexmustahinmbay











Articles les plus consultés