> Bàkku SEMEtt



SEMEtt kuréel la guy dajale ay gëstukat ci mbirum njàng , ñuy yënggu ci mbirum  caada, ñuy yenggu ci wallu sinemaa, ñeneen ñu macce ci lu jëm ci yoon , ñii ci mbiru koom-koom, ñële ci xarala yu bees yi, ay jàganlekat, ay taskatu xibaar ag ñu nekkinu askan wi yittéel, té ñoom ñëpp ittewo mbiru njàngale mi, maanaam ëllegu Afirig, ndax da ñu gëm ne yokkuteem manul jaar fenn fudul ci tàggat i nitam, ngir ñu gëna xarañ te gëna gëm seen bopp.

Dalukaay u SEMEtt a ngi ci diggi Ndakaaru. Fala bàŋqaasam bu jëkk juddóo. Mebet u SEMEttmooy lëkkale borom xam-xam yi ci tund u Afirig gepp te ñuy yënggu ci wàllu jumtukaayi tas xibaar, ci wàllu njàng ag caada, maanaam ñëpp ñi nga xamne da ñuy taxaw ci gàddu ci seen i Wàgg ëllëg u Afirig.

Ndax kat, SEMEtt dafa nàmm sos benneel u Afirig. Waaye SEMEtt nàmm itam nekk mbalka mi nuy dajalee xalaat yu  rafet yëpp, fu ñu mënti joge, ndegem seen jëmu mooy lu baax ci Afirig.SEMEtt, rax ci dolli, te rawatina it , kuréel la gu day yenggu ag lay ngir nëpp ñiy dogal ànd ci xalaatam yooyu .

Ndax nak , fok nu jàng nekk benn. Mebet u loolu du juddoo ci neen. Mbooloo u tund u Afirig ci wàllu caada du lu nuy nemmeeku, waaye lu nuy tabàq la. Bu weesoo wuute gi ci wàllu cadaa, te mu juddóo  ci wutéeg dëkkin yi, jiwu Afirig wu nekk benn a ngi ci xel yi, lëngoog bokk tund gi, bokk taariq gi ag yàgg ci ay xeeti wecco yune.

Askan yiy daan ñooy yi gëm seen bopp, gëm ne seen yokkutee ngi seeni yoxo. Ngëm-ngëm googu it du juddu ci neen. Mu ngi sosoo ci ay nekkin ag ay taxawin yu jóge ci njàngaley maam, tassaaroo ci pàcc yu melni njàng muy xamal ag mënal, ci jottaliy xibaar yuy defar askan ag ci dogu ci suuxat caada.

Bàyyi sa bopp gi taariq jur, taariq a ko mana faj.

                                     Ndakaru, 27 ci desàmbar 2007

Articles les plus consultés